Content-Length: 79030 | pFad | https://wo.wikipedia.org/wiki/Saaru_Maryama

Saaru Maryama — Wikipedia Aller au contenu

Saaru Maryama

Jóge Wikipedia.

Saaru Maryaama Màkka la wàcc 99 laaya la

(1) K. H. Y. Saad [Lii] fàttali sa yërmande Boroom la ca jaamam ba Sàkkariyaa.

(2) Ba mu ñaanee Boroomam ndànk

(3) Ne ko : "Sama Boroom ! néew naa doole, te sama bopp weex na tàll ak bejjaaw. Te masuma laa ñaan be sooy.

(4) Te am naa am tiit ci njaboot gi sama ginnaaw, te sama soxna dafa jërméel. Kon nag yal na nga ma may kuutaay gu bawoo ci yaw

(5) Gu may donn, tey donn njabootu Yànqooba, te sama Boroom yal na nga ko def muy ku ñu gërëm !"

(6) Yaw Sàkkariyaa noo ngi lay bégale doom ju góor ju tudd Yaxyaa, kenn masu koo tudd.

(7) Mu ne : " Sama Boroom nu may ame doom, te sama soxna jërméel, te ma màgget be kumur".

(8) Mu ne : "Noonu la. Sa Boroom nee na : loolu yomb na Ma, te nag Maa la bindoon, te doo woon dara".

(9) Mu ne : "Sama Boroom, defal ma firndé". Mu ne : "Sa firndé moo di doo mën a wax ak nit ñi ñetti guddi yu mat sëkk".

(10) Mu génne ca jàkka ja, yem ciy nitam junj léen ne: “sàbbaalléen suba ak goon!”

(11) “Yaw Yaxyaa, téyél ci Téeré beek doole !” def Nanu ko muy ku xereñ àtte cig ngoneem.

(12) Ak yërmande ju tukkee ci Nun, te ku fegu la woon

13) Te ku baax la woon ciy way-juram, réyul woon, daawul woon moy Boroomam.

(14) Yal na ko Yàlla defal jàmm keroog ba mu juddóo ak keroog ba muy dee ak keroog ba muy dekkiwaat di dund.

(15) Fàttalil ci Téeré bi (Alxuraan) Maryaama, ba mu beddikoo ay nitam dem ci barab bu féete penku

(16) Mu doxale kiiraay diggantéem ak ñoom ; Nu yebal ca moom Sunu malaaka [Jibriil] mu feeñu ko ci melow nit ku mat sëkk.

(17) [Maryaama ne :] Yal na ma Yàlla musal ci yaw ! Ndeem fegu nga !

(18) Mu ne ko: "Man sa ndawal Boroom rekk laa, lu lay maysi doom ju sell".

(19) Maryaama ne ko : "Numay ame doom, te mbindéef laalu ma, te duma jigéen ju bon".

(20) Mu ne : "Noonu la, sa Boroom nee na : “loolu lu Ma yomb la », Te dananu ko def kéemtaan ci nit ñi ak yërmande ju bawoo ci Nun. Mbir mi sotti na !".

(21) Mu ëmb ko, beddeekook moom ca barab bu sori.

(22) Mat wa dab ko ca ëkku tàndarma ga. Mu ne : "Céy ! Aka neexoon ma dee lu jiitu lii, su ko defee ñépp fàtte ma, kenn dóotu ma tudd.

(23) Mu woo ko cag ronam [ne ko] : "Bul jàq, sa Boroom defal na la ci sag ron am yol".

(24) Gësëmal dàttu tàndarma gi, tàndarma yu ñor xomm rot, wutsi la

(25) Lekkal, naanal, te seral sa xol. Boo gisee kenn ci nit ñi neel : "Man kat damaa nisër a wooral Boroom yërmande ji ; kon nag tey duma wax ak nit".

(26) Mu indil ko (liir ba) aw nitam, leewu ko ; ñu ne ko : "Céy Maryaama def nga njaaxum gu réy !".

(27) Yaw jigéenu Aaróona, sa baay dey du woon waa ju bon, sa ndey it nekkul woon jigéen ju bon !".

(28) Mu joxoñ ko (liir ba) ; ñu ne ko : "Naka la nuy waxeek liir bu nekk ciy laltaayam".

(29) Mu (liir ba) ne : "Man jaamu Yàlla laa, jox na ma Téeré ba (Injiil)

(30) Mu def ma may ku bàrkeel, te mu dénk ma julli ak asaka feek maa ngi dund,

(31) Ak baax ci sama ndey, te defuma may ku féttéerlu di ku texeedi

(32) Yal na ma Yàlla defal jàmm keroog ba ma juddóo ak keroog ba may dee ak keroog ba ñu may dekkal may dund !".

(33) Kookooy Isaa doomu Maryaama, baatu dëgg bi ñuy werante

(34) Jaaduwul ci Yàlla Muy doomoo kenn. Ëppale na ko boppam ! Su dogalee mbir da naan ko : « Nekkal, mu nekk ».

(35) Te nag Yàllaay sama Boroom, di séen Boroom : "Jaamuléen ko. Lii yoon wu jub la".

(36) Kurél ya wuute ca séen diggante. Mbugal ñeel na ñi weddi dikkug bés bu réy

(37) Aka ñooy mën a dégg ! Aka ñooy mën a gis ! Keroog bu ñu teewee Sunu kanam ; waaye nag tey tooñkat yi ñu ngi ci réer gu metti.

(38) Waarléen ndax ñoom ñu ngi ci càggante ak ñàkk a gëm ; bésu réccu ba fekk dogal ba sotti na.

(39) Nun nooy donn suuf si ak la ca kowam, te ci Nun lañuy déllusi.

(40) Fàttalil ci Téeré bi (Alxuraan) Ibraayima,

(41) Moom dey ku dëggu la woon, te di ab Yónnent.

(42) Ba mu nee baayam : "Sama baay, lu tax ngay jaamu lu dul dégg, du gis, te du la jariñ dara

(43) Sama baay, am na lu ma dikkal ci xam-xam loo xam ne dikkalu la, topp ma, ma teg la ci yoon wu jub xocc.

(44) Sama baay, bul jaamu séytaane ; séytaane dey kuy moy Boroom yërmande ji la.

(45) Sama baay, ragal naa mbugal mu bawoo ca Boroom yërmaande ja, laal la, ñu boole la ci ñi far ak séytaane".

(46) Baayam ne ko : "Mbaa du dangaa bañ sama yàlla yi, yaw Ibraayiima, soo yemul, danañu la sànni ay doj. Sori ma ab diir!".

(47) Mu ne : "Yàlla na jàmm nekk ci yaw. Danaa la jéggalul sama Boroom ; Moom dey ku baax ci man la".

(48) « Beddeeku naa léen ak ña ngéen di ñaan ñu dul Yàlla, te maa ngi ñaan sama Boroom, xéynalee duma texeedi ci ñaan sama Boroom ».

(49) Ba mu léen beddeekoo, ak la ñu doon jaamu ci lu dul Yàlla, may nanu ko Isaaxa ak Yànqooba, te ku nekk ci ñoom ñaar def Na nu ko muy ab Yonent.

(50) May Nanu léen ci sunu yërmande, te defal Nanu léen tagg wu rafet séen ginnaaw.

(51) Fàttalil ci Téeré bi Muusaa nekkoon na di ku ñu sellal, nekkoon na ndaw lu ñu yenkeewal ;

(52) Woo woon Nanu ko ca wàllu ndey-joor tuur [doju Siiniin], Nu jegeel ko, déeyook moom

(53) May Nanu ko ci Sunu yërmande mbokkam Aaróona def ko mu di Yonent.

(54) Fàttalil ci Téeré bi (Alxuraan) Ismaayla, doonoon na ku sàmm dëelam, te nekkoon na bu ñu yónni.

(55) Te daan na digal ñoñam julli ak joxe asaka, te doonoon ku am ngërëmal Boroomam.

(56) Fàttalil ci Téeré bi (Alxuraan) Idriisa, nekkoon na ku dëggu te dib Yonent.

(57) Yékkati Nanu ko teg ko ci barab bu kowe

(58) Ñooñu ñooy ña Yàlla defaloon xéewal ci Yonent yi ñu bokk ci njabootu Aadama ak ña ñu yeboon [ca gaal ga] ñu ànd ak Nóoh ak ca ña Nu gindi, te tànn léen. Ñooñu, su ñu jàngee laayay Boroom yërmande ji ñu rot sujjóot, boolekook i jooy.

(59) Mu am ñu léen wuutu séen ginnaaw, ñu sàggane julli, topp bànneex ya, ñooñu dey danañu tàbbi [xuru] safaraw “Gayy”

(60) Ndare ña tuub, te gëm, te jëf jëf ju yiw. Ñooñu danañu tàbbi Àjjana, te déesu léen tooñ ci dara.

(61) Àjjana yu sax ya Boroom yërmande ja dig jaamam ya ci kumpa. Moom dey digéem luy ñëw la.

(62) Duñu fa dégg caaxaan, jàmm rekk la ñu fay dégg ! Fa la léen séen wërsëg di fekk subaak ngoon.

(63) Loolooy Àjjana ji Nuy donnale képp ku ragal Yàlla ci Sunu jaam yi.

(64) Nun dey dunu wàcc lu dul ci sa ndigalul Boroom. Moo moom li ci sunu kanam ak la ca sunu ginnaaw ak li ci séen diggante, te sa Boroom du fàtte.

(65) Mooy Boroom asamaan yi ak suuf si ak li ci séen diggante ; jaamu [léen] ko, te ngéen sax ca jaamu ga. Ndax xamal ngéen ko kenn ku Ko niru ?

(66) Nit a ngi naan : "Ndax su ma deewee danañu ma dekkal ?"

(67) Xanaa nit dafa fàttalikuwul ne Noo ko bindoon ca lu jëkk, te du woon dara.

(68) Giñ naa ci sa Boroom ne fàww dinaa léen fàng boole léen ak séytaane ya, te dananu léen dajale ca kéewal jaanama.

(69) Te Dananu ñoddi ci kurél bu nekk ña ca gënoon a ñeme Yàlla.

(70) Te Ñoo gën a xam ña gën a yeyoo lakk ci Safara.

(71) Amul kenn ci yéen ku fa dul jaar. Sa Boroom dogal na ko, te du jaas.

(72) Topp Nu musal ña ragaloon (Ÿàlla), Nu bàyyi ña tooñoon ñu bóof ca biir.

(73) Bu ñu léen jàngalee Sunu laaya yi ña weddi wax ña gëm ne léen : ban ci ñaari kurél yi moo ëpp màqaama te gën mbooloo?.

(74) Ñaata la nu alag lu léen jiitu ci ay maas yu léen ëppale te gën léen a taaru

(75) Képp ku nekk ci cànkute, na ko Yàlla bàyyi ci cànkutéem mu wéy ca!

(76) ba ñu gis li ñu léen dig : moo xam mbugal ma la walla bés-pénc. Bu boobaa danañu xam kan moo gën a yées daraja, te gën a ñàkk solo ab lël.

(77) Yàlla dana dolli njub ñay sàkku njub, ay jëf yu yiw yiy des ginnaaw farata, ñoo ëpp yool ca sa Boroom te moo gën ag muj.

(78) Xanaa gisóo ki di weddi sunu laaya yi te naan : "fàww deef na ma fa jox alal ak i doom".

(79) Xanaa kii dafa xam kumpa, walla mu am lu mu dëelante Boroom yërmande ji?

(80) Mukk ! Te dananu bind li mu wax, te dananu ko dolli mbugal mu baree bari.

(81) Dananu nangu ci moom alal ji muy wax, mu ñëw ci nun ne cundum.

(82) Jël nañu ñeneen def léen Yàlla, bàyyi fa Yàlla, ngir ñu dooleel léen

(83) Mukk ! (séen Yàlla yooyu) danañu weddi jaamu gi ñu léen doon jaamu, nekk it séeni noon

(84) Xanaa gisóo ni nooy yebal séytaane ya ca yéefër ya ñu léen di gësëm

(85) Buléen yàkkamti (mbugal mi). Nu ngi léen koy waajal bu baax.

(86) Keroog ba nuy fàng ñi ragal Yàlla, fa Boroom yërmande ja ñuy mbooloo,

(87) Nu sëkkëtal saay-saay si jëme léen jaanama, ñu ànd ak mar wu metti

(88) Tinu amu fa, lu dul ku fasante woon ak Boroom yërmande ji kóllare

(89) Nee na ñooy Boroom yërmande ji dafa am doom!

(90) Wax ngéen lu ñaaw

(91) Asamaan xaw naa xotteeku, suuf siy waaj a xar, xeer yiy bëgg a jóoru.

(92) Ngir li ñu wutal doom Boroom yërmande ji

(93) Te jaaduwul ci Boroom yërmande ji muy doomoo kenn

(94) Amul kenn ci asamaan walla ci kaw suuf ku dul ñëw fa Boroom yërmande ja ñëwinu jaam.

(95) Dajaleléen, lim léen ba ñu mat

(96) Ñoom ñépp danañu teew fa Moom bés-pénc, ku nekk ne cundum.

(97) Ña nga xam ne gëm nañu, te def lu baax, Boroom yërmande ji, Yàlla dana léen defal cofeel.

(98) Yombal nanu ko (Alxuraan) ci saw làmmiñ, ngir nga bégal ci ñi ragal Yàlla, te xupp ci nit ñi dëng.

(99) Ñaata lanu alag ci ay maas yu léen jiitu, ndax yégati nga kenn ci ñoom walla nga dégg kàddoom ?









ApplySandwichStrip

pFad - (p)hone/(F)rame/(a)nonymizer/(d)eclutterfier!      Saves Data!


--- a PPN by Garber Painting Akron. With Image Size Reduction included!

Fetched URL: https://wo.wikipedia.org/wiki/Saaru_Maryama

Alternative Proxies:

Alternative Proxy

pFad Proxy

pFad v3 Proxy

pFad v4 Proxy